Ndiawar Laye SËTTU YONNENT BI 🤍🕊

Поділитися
Вставка
  • Опубліковано 24 січ 2025

КОМЕНТАРІ • 101

  • @SikarLayenne
    @SikarLayenne  2 роки тому +14

    Acte II en hommage à notre bien-aimé Sëriñ Ablaay mu baax mi RTA.
    1
    Tay janta bi suuxina suuf si lëndam
    Nit ñéppa gëlëm di xalaat funu jëm
    Kër yéppa selaw ndax Sanga bi dem
    Sëtu Yonnen bi
    2
    Xol yéppa sëngeem ndax Làmp bi fay
    Rangooñ yi di sar ndax Sanga bi wéy
    Sunu Soppe bi Baay Ablaaya ni mëy
    Sëtu Yonnen
    3
    Ñii naa du lu am Baay Abdu demul
    Day déeyoo sàllaaw yeen a xamul
    Baay Abdu manul dem wóor na Jaliil
    Sëtu Yonnen bi
    4
    Baay Abdu manul xëy bàyyi nu dem
    Baay Abdu bu ñibbee ñéppa jirim
    Baay Abdu bu ñibbee ñéppa gëlëm
    Sëtu Yonnen bi
    5
    Baay Abdu bu ñibbee dootu nu dal
    Baay Abdu bu ñibbee jam sunu xol
    Baay Abdu bu ñibbee fél sunu xel
    Sëtu Yonnen bi
    6
    Baay Abdooy Aljana moo nu gënal
    sunu jëmm yi, sàllaaw moo nu xamal
    Firdawsi ci kaw suuf mooy sunu xol
    Sëtu Yonnen bi
    7
    Baay Abdu ci nun day Jant bu leer
    Taaram bi ci nun moo raw bu Badar
    Moo dàq ci nun am ndox ci ku mar
    Sëtu Yonnen bi
    8
    Baay Abdu da doon sun Buumi Cofeel
    Ku ko xam di nga mujja banook ni nu mel
    Ku nu yedda da nga dese xam li nu fél
    Sëtu Yonnen bi
    9
    Baay Abdu da noo njortoon ni du dem
    Sunu yéene da doon juri doom ni ko am
    ñuy xëy di ko géewal gën di ko gëm
    Sëtu Yonnen bi
    10
    Sunu yéene ci moom mooy toog di ko way
    Muy dégg di kontaan nuy gën a way
    Muy muuñ di nu xool nuy gën di ko way
    Sëtu Yonnen bi
    11
    Sunu yéene ci moom mooy gën di ko roy
    Mooy Góor gi nu nàndal mooy ki nu doy
    Man xaw ma kemam xam ngeen ni du jay
    Sëtu Yonnen bi
    12
    Baay Abdooy Góor gi nu wan Baay Laay
    Mooy Góor gi raxas sunu xol yi ci Laay
    Mooy Góor gi nu wan yoon kenna du lay
    Sëtu Yonnen bi
    13
    Baay Abdu bi muy jóg, jóg jafena
    Xam ngéen ni bi muy wax wax jafe na
    Kon kay ni ko Jaajëf yay na xanaa
    Sëtu Yonnen bi
    14
    Tay Yonnen teeru na sët bi ko gëm
    Waa Diwaan sappe di seenu jëmmam
    Muy tempa di muuñ cëy moo bari ndam
    Sëtu Yonnen bi
    15
    Muy dox jub Maam ja mu jóg ni ko kaay
    Yaw sët bi ma siiwal jël si sa pay
    Njool lënga ko foon ko di jël di ko may
    Sëtu Yonnen bi
    16
    Maam Sëydi taxaw ni ko doom jaajëf
    Dénkaane bi mat na rafet na sa jëf
    Mag ñéppa di bég ñép naa jërëjëf
    Sëtu Yonnen bi
    17
    Baay Abdu ba nuy dajé dootu nu dañ
    Di ŋoyaalu ci yaw Baay Booy dunu dañ
    Di la way di la kañ ni Cofeel gi du dañ
    Sëtu Yonnen bi
    18
    Baay Abdu sa dem gii tiis nanu lool
    Dunu tàyyi ci yuux fép tiis wi nu dal
    Bu perantal ñàkkee yaay ja du dal
    Sëtu Yonnen bi
    19
    Baay Abdu demal Buur fay la ngënéel
    Baay Abdu dinan sàmmaat li nga jal
    Nu ngi santaat Yàlla ni mooy ki la jël
    Sëtu Yonnen bi
    20
    Na Boroom bi di taw leer bés bu nu xëy
    ci sa Maam jeek Baay yi te boole nu may
    Nuy gën dila nianal abu coumba ngoye
    Setu yonen bi
    Jàmmalaay Kambereen
    12 Aout 2021.

  • @sambangom3644
    @sambangom3644 2 роки тому +7

    Bilahi SouNou sOopé Bii BayE AbdOulAHi❤️yALnA yAllah yOkkOu Ayy LÉrame cci barké bAye LAye sEydi P.S.L✨AmiiNE YA RABBiH🤲🏿

  • @goraseck1181
    @goraseck1181 2 роки тому +10

    Xol sédeuna laye makhtare ❤️😭souniou xol yeupangui sii Baye Ablaye yalla na yalla yokki leram🙏❤️

  • @mouhamedlaye5977
    @mouhamedlaye5977 2 роки тому +5

    Bilahi Xol Sadatina Laye Makhtar Yalna Yalla Wéreul té dolli souteureu mane sopé bula beugue laa mangui deuk Touba

    • @sambangom3644
      @sambangom3644 2 роки тому +1

      ❤️❤️❤️❤️❤️❤️❤️❤️🙏🏿🙏🏿🙏🏿🙏🏿

    • @elhadjiomarcisse527
      @elhadjiomarcisse527 2 роки тому

      Oooooh machalla mouhamed laye. Amine laye makhtar.sope nalla lol cède yi rafetna .Touba deuk bou ted bi .bougnou fate ci gnane

    • @SikarLayenne
      @SikarLayenne  2 роки тому

      😍

    • @SikarLayenne
      @SikarLayenne  2 роки тому

      🙏🏾

  • @bayemasselaye5445
    @bayemasselaye5445 2 роки тому +7

    ABDOU LAHI CHERIF WALAXI NIO NGI SA KEPAR DOUNEFI DIOUGUE 🙏🙏🙏 MACHALLA NDIAWAR ET TT L' EKIP YALNA SA BOROM FAYLENE YIIW BARKEP SERIGNE ABLAYE 🙏🙏

  • @sokhnangonendiaye3314
    @sokhnangonendiaye3314 2 роки тому +6

    Les paroles Mach’ALLAH ça me touche

  • @Abdoulaye2010
    @Abdoulaye2010 2 роки тому +3

    🥰❤mame yal na yalla yok say ler🤲📿🙏

  • @awakandawsamb7522
    @awakandawsamb7522 2 роки тому +5

    Blh baye abdoulaye dou massa danie souniou xool yi
    Ndiawar Laye yalna batt bi wèrr

  • @conseildesfemmes4934
    @conseildesfemmes4934 2 роки тому +3

    Yalla na yalla swt wéreul bath bi

  • @cherifabdoulayendiaye5252
    @cherifabdoulayendiaye5252 2 роки тому +6

    Serigne ablaye jerejeuf❤☝🏾🏳

  • @koddabewdo3780
    @koddabewdo3780 2 роки тому +2

    Billahi wetal ngagnou mame boy😭😭 yalla na yalla yok leeram ❤️🤍🤍

  • @boubacarkebe598
    @boubacarkebe598 Рік тому +1

    Machallah..Ddieuf laye makhtar

  • @AssaneSamb-n6y
    @AssaneSamb-n6y Рік тому +2

    Ndey sann lou nkh laye maxtar ❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤

  • @abdoulayendiour3565
    @abdoulayendiour3565 Рік тому +2

    Machallah laye Makhtar zi❤😢

  • @seydou48669
    @seydou48669 5 місяців тому

    Ndanane bi yalla na yalla wéral bat bi 🎉

  • @seydinadiagne6027
    @seydinadiagne6027 2 роки тому +2

    Baay abdoulay ngibi na ❤😪

  • @sokhnangonendiaye3314
    @sokhnangonendiaye3314 2 роки тому +3

    Baay Ablaay merci

  • @PapeMangett
    @PapeMangett Рік тому

    Serigne ablaye sama xol❤❤❤❤

  • @awathiam3556
    @awathiam3556 2 роки тому +2

    Ndeyesane mame boye

  • @AssaneSamb-n6y
    @AssaneSamb-n6y Рік тому +1

    Douma si doyallll❤❤❤❤❤❤

  • @maremembaye1070
    @maremembaye1070 2 роки тому +2

    Aye serigne abdoulaye nakhe nanou badéme jërejëfe

  • @fifilaye8116
    @fifilaye8116 Рік тому +2

    ❤❤MACHALAAH LAYE MAKHTAR ❤❤

  • @PetitGueyeLaye-cj3fu
    @PetitGueyeLaye-cj3fu Рік тому

    Machala Laye makhtar

  • @SofietuGadiaga
    @SofietuGadiaga 8 місяців тому

    Machallah

  • @cheikhmbodj9686
    @cheikhmbodj9686 2 роки тому

    Machalahh ndiawar Laye 🥰👍❤️❤️❤️

  • @Leuzkara16
    @Leuzkara16 Рік тому

    😪machalakh yaram laye makhtar🏳🏳🥰

  • @oumysow-99
    @oumysow-99 Рік тому

    Manchalla

  • @issalaye4
    @issalaye4 2 роки тому +2

    Ndeysann 😭

  • @matylahii309
    @matylahii309 2 роки тому +2

    ❤️❤️❤️❤️❤️❤️❤️❤️

  • @xeuchelaye6924
    @xeuchelaye6924 Рік тому

    🙏🏿🙏🏿🙏🏿

  • @AssaneSamb-n6y
    @AssaneSamb-n6y Рік тому

    Ndey sann 😢😢

  • @adamafaye6683
    @adamafaye6683 Рік тому

    ❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤️❤️❤️

  • @NdiayaDiop-d7e
    @NdiayaDiop-d7e 9 місяців тому

    ❤❤❤

  • @FatouDiop-t8u
    @FatouDiop-t8u Рік тому

    ❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤💘😭 8:07

  • @AssaneSamb-n6y
    @AssaneSamb-n6y Рік тому

    Ndey sannn😢

  • @fifilaye8116
    @fifilaye8116 Рік тому

    ❤❤❤❤❤❤❤❤❤

  • @SofietuGadiaga
    @SofietuGadiaga 8 місяців тому

    Laymomadomactar

  • @abdoulayendiour3565
    @abdoulayendiour3565 2 роки тому

    MACHALLAH🥰🥰🤍🤍

  • @marianbraileanu-f3k
    @marianbraileanu-f3k 7 місяців тому

    bilay son bi bouma koy déklou damay dioy rek baye ablaye wétale naniou 😢😢😢😢😢

  • @PetitGueyeLaye-cj3fu
    @PetitGueyeLaye-cj3fu Рік тому

    Machala Laye makhtar

  • @elmalick7617
    @elmalick7617 2 роки тому +1

    ❤❤❤❤❤❤❤

  • @SofietuGadiaga
    @SofietuGadiaga 8 місяців тому

    Laymomadomactar

  • @maremembaye1070
    @maremembaye1070 2 роки тому

    ❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤❤👍👍👍👍👍👍👈👈👈👈👈👈👈👈👈👈👈👈👈

  • @marianbraileanu-f3k
    @marianbraileanu-f3k 7 місяців тому

    bilay son bi bouma koy déklou damay dioy rek baye ablaye wétale naniou 😢😢😢😢😢

  • @PetitGueyeLaye-cj3fu
    @PetitGueyeLaye-cj3fu Рік тому

    Machala Laye makhtar

  • @xeuchelaye6924
    @xeuchelaye6924 Рік тому

    ❤❤❤❤❤❤❤

  • @seynaboulaye
    @seynaboulaye Рік тому +1

    Machala Laye makhtar

  • @AliouKa-e4i
    @AliouKa-e4i 7 місяців тому

    ❤❤❤❤❤